Saar 12
Cant jib na 
 1 Bésub keroog dees na ne: 
«Aji Sax ji, sant naa la; 
yaa ma mere woon, meddi, dëfal ma.» 
 2 Ma ne: «Yàllaa may wallu, 
ma dal-lu, duma tiit. 
Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki sax, 
di Aji Sax ji, 
te mooy sama wall.» 
 3 Mbégte ngeen di rooteji 
fa wali mucc ya. 
 4 Bésub keroog ngeen ne: 
«Santleen Aji Sax ji, tudd turam, 
xamley jalooreem ci biir xeet yi, 
fàttli màggaayu turam. 
 5 Woyleen Aji Sax ji, 
moo kawey jëf! 
Na lii siiw biir àddina sépp. 
 6 Yeen waa Siyoŋ, serleen te sarxolleel 
ku màgg ki fi seen biir, 
Aji Sell ju Israyil.»