Sabóor  
Sabóor 1
Ñaari yoon a ngii 
 1 Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon, 
taxawewuloo yoonu moykat, 
toogewuloo jataayu ñaawlekat. 
 2 Xanaa di bége yoonu Aji Sax ji, 
di ko jàngat guddeek bëccëg. 
 3 Loo def mu àntu: 
nga mel ni garab gu saxe walum ndox, 
bu jotee meññ, 
te xob wa du lax. 
 4 Loolu dalul moos ku bon, 
kay mel ni xatax bu ngelaw li wal. 
 5 Moo tax ku bon du siggee àtte ba, 
moykat du taxawe ndajem aji jub ña. 
 6 Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; 
yoonu ku bon di sànk boroom.