Sabóor 4
Ma gonloo ñaan 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. 
 2 Éy Yàlla, yaw mi may àtte dëgg, 
maa ngi woote, wuyu ma; 
maa xatoon, nga yaatal ma. 
Ngalla baaxe ma, nangul ma. 
 3 Yeen boroom daraja yi, 
buleen yàqati sama der, 
buleen sopp caaxaan, di sos. 
 Selaw.
  4 Xamleen ne Aji Sax ji day séddoo ku ko ragal, 
te bu ma wooyee Aji Sax ji, mu dégg. 
 5 Loxleen te baña bàkkaar, 
waxtaanleen ak seen ngegenaay te noppi. 
 6 Rendileen seen sarax yi war, 
te wóolu Aji Sax ji. 
 7 Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?» 
Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw! 
 8 May nga ma bànneexu xol 
bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal. 
 9 Jàmm laay tëdde, nelaw, 
Aji Sax ji, yaw doŋŋ yaa may dëël fu wóor.