Sabóor 6
Jarag a ngi woote wall 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. 
 2 Éy Aji Sax ji, bul mer, ba di ma rëbb, 
bul xadaru, ba di ma mbugal. 
 3 Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma! 
Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma! 
 4 Sama xol a jeex tàkk. 
Aji Sax ji, loo deeti xaar nag? 
 5 Éy Aji Sax ji, délsil, xettli ma! 
Walloo ma sa ngor. 
 6 Deesul dee ba fàttliku la; 
ku dugg njaniiw, nu mu lay sante? 
 7 Onk naa ba loof, di fanaanee jooy, 
sama lal di féey, 
ba far seeye rongooñ. 
 8 Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar, 
boole ci giim ndax tooñi noonoo noon. 
 9 Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma! 
Aji Sax ji dégg na saay jooy, 
 10 Aji Sax ji dégg na saay dagaan, 
Aji Sax jii nangu na samag ñaan. 
 11 Noon yépp a am gàcce, ba jàq lool, 
ne wërëñ ak gàcceg mbetteel.