Sabóor 11
Ma làqoo Aji Sax ji 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda. 
Aji Sax ji laa làqoo. 
Ana lu ngeen ma naa: «Neel fëyy ni picc, toŋi sa kaw tund. 
 2 Xanaa du ñu soxor ñaa ngii, bank seen xala, 
nas seenu fitt, 
nara lëndëmtu, jam ku jub? 
 3 Bu ponki njub màbbee, 
nu aji jub di def?» 
 4 Aji Sax jaa nga këram gu sell. 
Aji Sax jaa nga asamaan, kaw jalam, 
ne jàkk doom aadama, di ko seetlu. 
 5 Aji Sax ji day seetlu ku jub; 
ku soxor, bëgg fitna, mu bañ. 
 6 Day tawal ku bon ay mbugal; 
sawaraak tamarax akub jaas dib añam. 
 7 Aji Sax jee jub, sopp njub; 
kuy jubal, gis yiwam.