Sabóor 20
Yal na Buur daan 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. 
 2 Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare, 
yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe, 
 3 yal na la yónnee wallam fa këram, 
jàpplee la fa, ca Siyoŋ. 
 4 Yal na xool loo ko jébbal, 
di rafetlu sarax soo ko lakkal. 
 Selaw.
  5 Yal na la may li nga namm, 
di sottal loo mébét, 
 6 ngay daan, nuy ree, 
yéege sunu raaya, màggal sunu Yàlla. 
Yal na Aji Sax ji nangu loo dagaan. 
 7 Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey. 
Moo koy nangule fa asamaan su sell sa, 
ci dooley ndijooram biy musle. 
 8 Ñiiki watiir, 
ñeeki fas, 
nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd. 
 9 Ñoom ñooy jeng ak a jóoru, 
nun, nu jóg, taxaw jonn. 
 10 Éy Aji Sax ji, mayal Buur mu daan, 
te bés bu nu ko ñaane, mu nangul nu.