Sabóor 24
Ana kuy màggal Buur Yàlla? 
 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. 
Aji Sax jee moom suuf ak li ko fees, 
ak àddina ak li ci biiram. 
 2 Moo samp suuf biir géej, 
dëj ko ci kaw wal mi. 
 3 Ana kuy yéegi tundu Aji Sax ji, 
kuy taxawi bérabam bu sell ba? 
 4 Xanaa ku mucc ayib, sell ab xol, 
xemmemul caaxaani neen, 
du giñey fen. 
 5 Kookooy jagoo barkeb Aji Sax ji, 
ak njekku Yàlla, mi koy musal. 
 6 Ñooñooy waa làng, gi lay sàkku, 
di maasug Yanqóoba, giy sàkku sa yiw. 
 Selaw.
  7 Neleen bunt yi kulbét, 
ubbileen bunti cosaan yi, 
Buur Boroom ndam duggsi. 
 8 Buur Boroom ndam booboo di kan? 
Xanaa Aji Sax ji Boroom dooleek njàmbaar, 
Aji Sax ji jàmbaaru xare ji. 
 9 Neleen bunt yi kulbét, 
ubbileen bunti cosaan yi, 
Buur Boroom ndam duggsi. 
 10 Buur Boroom ndam booboo di kan? 
Xanaa Aji Sax ju gàngoor yi. 
Kookooy Buur Boroom ndam. 
Selaw.