Sabóor 28
Aji Sax jeey àtte ñoñam 
 1 Ñeel Daawuda. 
Éy Aji Sax ji, yaw laay woo, 
di la wéeroo, bu ma tanqamlu. 
Soo nee cell, 
ma xawa tàbbim pax. 
 2 Ngalla déglul, ma tinu la, 
woo la wall, 
dékk lay yoxo, 
jublu sa néegu biir bu sell ba. 
 3 Bu ma sànkaaleek ab soxor, 
di ma booleek kuy def lu bon, 
di wax moroom ma jàmm, 
te dencal ko ay ca xolam. 
 4 Fey leen seen liggéey, 
seen kemu jëf ju bon. 
Jox leen seen añu jëf, 
yool leen seen yelleef. 
 5 Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, 
ak liggéey bi mu def. 
Da leen di yàqte, 
te dootu leen yékkati. 
 6 Jaajëfe Aji Sax ji, 
ki ma nangul samay dagaan! 
 7 Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. 
Moom laa wóolu, mu wallu ma, 
sama xol tooy, 
ma woy, sante ko. 
 8 Aji Sax jeey dooleel ñoñam. 
Mooy làq, di musal buur bi mu fal. 
 9 Ngalla musalal sa mbooloo, 
barkeelal sa ñoñ ñii, 
sàmm leen, boot ba fàww.