Sabóor 47
Yàllaay buur 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor. 
 2 Na xeetoo xeet tàccu, 
xaacu, sarxolleel Yàlla! 
 3  Aji Sax ji, Aji Kawe jee jara ragal, 
mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp. 
 4 Moo nu nangulal xeet yi, 
nu teg tànk gàngoor yi. 
 5 Moo nu tànnal céru suuf, 
muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp. 
 6 Yàllaa yéeg, kàddu riir. 
Aji Sax jee yéeg, bufta jolli. 
 7 Woyleen Yàlla, woyleen, 
woyleen Yàlla sunu buur, woyleen. 
 8 Yàllaay buuru àddina sépp; 
taalifleen, woy ko. 
 9 Yàllaa di buuru xeet yi, 
Yàllaa tooge jalam bu sell. 
 10 Kàngami xeet yeey daje, 
ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma; 
Yàllaa moom buur yi yiir àddina, 
te moo kawee kawe.