Sabóor 54
Yàlla, dimbali ma 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda.  2 Mooy ba waa Sif demee ca Sóol, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew* 54.2 Seetal ci 1.Samiyel 23.14-28; 26.1-5.. 
 3 Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur, 
jox ma dëgg, ci sa kàttan. 
 4 Éy Yàlla, déglul, ma ñaan, 
teewlul, ma wax la. 
 5 Ay doxandéem a ma jógal, 
di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan, 
te seetuñu ci Yàlla. 
 Selaw.
  6 Yàllaa ngii, moo may dimbali; 
Boroom bee yor sama bakkan. 
 7 Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru, 
yal na leen sa dëgg sànk. 
 8 Xol bu tàlli laa lay sarxale. 
Aji Sax ji, yaa baax, 
ma sant la. 
 9 Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële, 
ma tiim samay noon.