Sabóor 57
Yàlla jógal, wallu ma! 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma* 57.1 Seetal ci 1.Samiyel 24.. 
 2 Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma, 
fi yaw laay làqu, 
yiiroo sa kiiraay, 
ba musiba yi jàll. 
 3 Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji, 
Yàlla, mi may matalal. 
 4 Mooy yónnee fa asamaan, musal ma, 
dumaal ma ku may not. 
 Selaw.
 Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam. 
 5 Maa ngi tëdd ci biiri noon 
yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. 
Seeni sell niy xeej aki fitt, 
seen làmmiñ di saamar yu ñaw. 
 6 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, 
sag leer tiim suuf sépp. 
 7 Noon yi di ma fiir, 
sama xol jeex. 
Ñu gasal mam pax, 
far tàbbi ca. 
Selaw.
  8 Yàlla, dogu naa, 
dogu naa woy, di la kañ. 
 9 Na sama jëmm jépp yewwu, 
xalam ak moroom ma yewwu; 
ma yee leeru njël. 
 10 Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi, 
kañ la ci biir waaso yi. 
 11 Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan, 
sa worma àkki fa kawa kaw. 
 12 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, 
sag leer tiim àddina sépp.