Sabóor 61
Naa woote wall 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda. 
 2 Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, 
teewlul, ma dagaan la. 
 3 Àll laa lay wooye, 
sama xol jeex; 
yéege ma doju rawtu wu ma jotul. 
 4 Yaw laa làqoo, 
ngay tata ju dëgër, fegal ma noon. 
 5 Naa dëkke sa xayma, ba fàww; 
làqoo sa kiiraay. 
 Selaw.
  6 Yàlla, yaa dégg samay dige, 
sédd ma céru ñi la wormaal. 
 7 Ngalla féqal fani Buur, 
ay atam bare, sët ba sëtaat. 
 8 Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam, 
nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo; 
 9 kon ma woy la ba fàww, 
di jëfe samay dige bésoo bés.