Sabóor 64
Yàllaa man ag fitt 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. 
 2 Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat; 
ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu. 
 3 Làq ma pexey ku bon, 
ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef. 
 4 Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar, 
di fitte seeni kàdduy wextan, 
 5 di jam ku ñu tëru te deful dara; 
jekki jam ko, te tiituñu ci dara. 
 6 Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar, 
di diisoo na ñuy làqe ay fiir, 
te naan: «Kenn du ko gis!» 
 7 Dañuy lal pexem njubadi te naan: 
«Lal nanu pexe mu mat sëkk.» 
Nit aka xóot xel te xóoti mbóot! 
 8 Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, 
ñu jekki daanu. 
 9 Seen làmmiñ a leen di fakkastal, 
ba ku leen xool wëcc bopp. 
 10 Ñépp a ciy am tiitaange, 
bay siiwal la Yàlla def, 
tey xalaataat jëfam jooju. 
 11 Ku jub bége Aji Sax ji, làqoo ko. 
Képp ku namm njub, damu.