Sabóor 67
Yal na nu Yàlla barkeel 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor. 
 2 Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu, 
te geesoo nu sa leeru kanam, 
 Selaw,
  3 ba ñu ràññee sa loxo fi kaw suuf, 
gis sag wall fi biir xeet yépp. 
 4 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, 
na la xeet yépp sant. 
 5 Na xeet yiy bég, di sarxolle; 
loo dogalal xeet yi njub la, 
te yaay wommat xeet yi ci kaw suuf. 
Selaw.
  6 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, 
na la xeet yépp sant. 
 7 Suuf si nangu na, 
yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel. 
 8 Yal na nu Yàllay barkeel, 
ba àddina wërngal këpp ragal ko.