Sabóor 82
Yàllaay àtte ndawi péncam 
 1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. 
Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam, 
di àtte ndawi péncam, naan: 
 2 «Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, 
ak di faral ku bon? 
 Selaw.
  3 Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim, 
tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol. 
 4 Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana, 
di leen xettli ci ku bon. 
 5 «Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu; 
xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef, 
ba kenuy suuf yépp di jaayu. 
 6 «Dama ne ay yàlla ngeen, 
yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji. 
 7 Waaye du leen tee dee ni doom aadama, 
du leen tee daanu ni képp kuy njiit.» 
 8 Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina, 
yaw yaa séddoo xeetoo xeet.