Sabóor 87
Siyoŋ, yaay ndeyu xeet yi 
 1 Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor. 
Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu sell ya. 
 2  Aji Sax jee sopp bunti Siyoŋ gii, 
mu gënal ko fu askanu Yanqóoba dëkke. 
 3 Yaw, dëkkub Yàlla bi, 
tuddees na say jaloore. 
 Selaw.
  4 Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. 
Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus. 
Nit a ngii, juddoo fa,» 
 5 te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ, 
ne kii ak kee fa bokk juddoo, 
te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ. 
 6 Aji Sax jeey lim xeet yi, limaale leen 
ne: «Kii fi la juddoo.» 
Selaw.
  7 Kuy fecc ak kuy woy ànd naan: 
«Sunu cosaanoo cosaan fii la!»