Sabóor 95
Kaayleen, nu sant 
 1 Kaayleen, nu sarxolleel Aji Sax ji, 
nu xaacul ki nuy sës, mucc. 
 2 Nanu ko dikke cant, 
woyal ko, mu riir. 
 3 Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, 
buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp. 
 4 Moo moom xóotey suuf, 
moom colli tund yi, 
 5 moom géej, sàkk ko, 
moom jéeri ji mu mooñ. 
 6 Nan sëgg, sujjóot, 
sukkal Aji Sax ji nu sàkk. 
 7 Mooy sunu Yàlla, 
nuy xeet wi muy foral, 
diy gàtt ciy loxoom. 
Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom 
 8 ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, 
jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma, 
 9 fa ma seeni maam doon nattoo, 
di ma seetlu te gis la ma def* 95.9 Seetal ci Mucc ga 17.1-7.. 
 10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, 
ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi, 
te faaleedi samay santaane.” 
 11 Moo ma taxa mer, ba giñal leen, 
ne duñu tàbbi fa sama noflaay.»