Sabóor 111
Yàlla la ay mbiram sax 
 1 Màggal-leen Ki Sax! 
Naa sante Aji Sax ji léppi xol 
ci biir ñu jub ñi bokk jataay. 
 2 Liggéeyi Aji Sax ji réy na, 
ku ko safoo di ko gëstu. 
 3 Jëfam teddnga laak daraja, 
njekkam di sax ba fàww. 
 4 Moo dogal ñuy fàttlikuy kéemaanam; 
Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande. 
 5 Mooy leel ku ko ragal, 
di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww. 
 6 Won na ñoñam dooley jëfam, 
ba mu leen joxee suufu xeet yi. 
 7 Ay jëfam dëgg laak njub, 
tegtalam yépp mata wóolu, 
 8 laloo dëgg ak njub, 
te sax dàkk ba fàww. 
 9 Moo yónnee xeetam wall, 
fas ak ñoom kóllëre gu sax. 
Kee sell te jara ragal! 
 10 Ragal Aji Sax ji di ndoortel rafet xel, 
dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. 
Moo yeyoo cant ba fàww.