Sabóor 113
Buur Yàllaay walloo 
 1 Màggal-leen Ki Sax! 
Yeen ñiy jaamu Aji Sax ji, màggal-leen ko, 
màggal-leen turu Aji Sax ji! 
 2 Yal nañu teral turu Aji Sax ji 
tey ak ëllëg! 
 3 Li dale penku ba sowu, 
màggal-leen Aji Sax ji. 
 4 Aji Sax jee kawe, tiim xeetoo xeet, 
teddngaam sut asamaan! 
 5 Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji, 
ki kaweel ab jalam, toog, 
 6 di jéer asamaan ak suuf? 
 7 Mooy yékkatee ku néewle fa suuf, 
di seppee ku sonn cib sën, 
 8 bokkal ko jataayu kilifa, 
ya jiite xeetam. 
 9 Mooy dëël jigéen ju tële woona jur, 
may ko mbégtem njureel. 
Màggal-leen Ki Sax!