Sabóor 133
Bokk, bennoo neex 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. 
Céy liika baax te neexati, 
ay bokk yu bokk dëkk, di benn! 
 2 Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ, 
siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona, 
rogalaat ba ci mbubbam, 
 3 neex ni layub tundu Ermon, 
neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ. 
Fa la Aji Sax ji dogal barke, 
muy dund gu dul jeex.