Sabóor 146
Buur Yàllaa jara wóolu 
 1 Màggal-leen Ki Sax! 
Naa màggale Aji Sax ji xol, 
 2 li feek may dund, di ko kañ, 
li feek may noyyi, di woy sama Yàlla. 
 3 Buleen wóolu kilifa, 
doom aadama amul wall. 
 4 Noo ga day rëcc, mu dellu suuf; 
bu bés baa, pexeem jeex. 
 5 Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; 
di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji, 
 6 ki sàkk kaw ak suuf, 
géej ak lu ci biiram, 
di sàmm dëgg ba fàww, 
 7 di àtte néew-ji-doole, 
di leel ku xiif. 
Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj. 
 8 Aji Sax jeey xippil silmaxa, 
di siggil ku sëgg. 
Aji Sax jee sopp ku jub. 
 9 Aji Sax jeey sàmm doxandéem, 
taxawu jirim ak jëtun, 
waaye mooy lajjal pexem ku bon. 
 10 Aji Sax jeey nguuru ba fàww. 
Yaw Siyoŋ, sa Yàllaa ñeel maasoo maas. 
Màggal-leen Ki Sax!