Sabóor 150
Màggal-leen Ki Sax! 
 1 Màggal-leen Ki Sax! 
Nangeen màggale Yàlla biir këram gu sell, 
màggale ko ca tatay asamaanam. 
 2 Màggaleleen ko ay jalooreem, 
màggale ko màggam gu réy. 
 3 Màggaleleen kog liit, 
màggale ko xalam ak moroom ma. 
 4 Màggaleleen ko njiin aki pooj, 
màggale ko xalam ak toxoro. 
 5 Màggaleleen ko tëggum weñ mu xumb, 
màggale ko tëggum weñ mu kawe. 
 6 Na lépp luy noyyi màggal Ki Sax! 
Màggal-leen Ki Sax!