Saar 15
Bantu reseñ matul matt 
 1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 
 2 Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi, 
ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi? 
 3 Ndax dees na ca sàkk bant, liggéeye ko? 
Am dees na ca sàkke wékkukaay, wékk ca lenn? 
 4 Xanaa sànni cib taal, xambe, 
ñaari cat ya lakk, digg ba xoyomu. 
Ana lu deeti njariñam? 
 5 Ndegam ba mu nee ñumm, 
lees ci dul liggéey dara, 
gën ba mu jàppee ba xoyomu. 
 6 Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: 
Dees na xamb caru reseñ, 
mu bokk ci banti garab yi ma joxe, ñu xamb lépp, 
te noonu laay xambe waa Yerusalem. 
 7 Maay jànkoonteek ñoom, 
ñu rëcc sawara, 
sawara lakk leen. 
Bu ma jànkoonteek ñoom, 
dingeen xam ne maay Aji Sax ji. 
 8 Maay gental réew mi, 
ñoo def jëfi ñàkk worma. 
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.