Saar 4
 1 Su bés baa juróom yaari jigéen ŋoyaalu genn góor, ne ko: 
«Sunub dund, nun a, 
sunu koddaay, nun a! 
Jox nu sag buum rekk, 
teggil nu gàcce.» 
Aji Sax ji aar na ndesu Yerusalem 
 2 Su bés baa njebbitum Aji Sax ji 
doon lu yànj, darajawu, 
meññeefum réew mi di teraanga, dib sag, 
ñeel ñi dese bakkan fi Israyil. 
 3 Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ 
ak ku des fa Yerusalem, 
ku sell ki lees lay wooye, 
muy képp ku ñu bind turam, 
te mu wara dese bakkan ci Yerusalem. 
 4 Boroom beey wal noowal mbugal, 
noo guy lakk, sellal, 
fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ, 
fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set. 
 5 Su boobaa tundu Siyoŋ bépp, 
fépp fu ñuy dajee, 
Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg, 
guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ; 
leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp, 
 6 di mbaar mu ñuy serloo tàngooru bëccëg, 
di ko seeloob taw ak waame.