Saar 15
Ab yéeneb waxyu ñeel na Mowab 
 1 Yéene bii ñeel na Mowab: 
Genn guddi déy la Ar Mowab, dëkk ba tas, ne mes! 
Genn guddi déy la Kir Mowab tas, ne mes! 
 2 Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, 
ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, 
Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, 
boppoo bopp dib nel, 
sikkimoo sikkim xuufu, 
 3 nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya, 
ak kaw taax yaak pénc ya, 
ku ne di jooy ba say rongooñ wale. 
 4 Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu, 
seen baat àkki ba Yaxacc, 
xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo, 
ne yàcc ne yasar! 
 5 Maay jooy Mowab jooyi xol, 
nit ñaa nga fay dawe ba Sowar, 
àkki ba Eglat Selisiya. 
Ña ngay yéeg jëm Luwit, di jooyoo, 
awe yoonu Oronayim, di jalu. 
 6 Dexu Nimrim wow na, 
ñax wow, gàncax lax, 
dara naatatul. 
 7 Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon, 
yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya. 
 8 Yuux déy maase na réewum Mowab, 
jooyoo ya ba Eglayim, 
jooyoo ya ba Beer Elim. 
 9 Dexu Dimon déy fees na ak deret, 
te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw, 
ba ku rëcce Mowab, 
ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde!