Sabóor 13
Aji Sax ji, loo deeti xaar? 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. 
 2 Céy Aji Sax ji, loo deeti xaar? 
Xanaa doo ma tanqamlu ba fàww? 
Loo deeti xaar, bañ maa geesu, 
 3 ba ma tàggook bopp bu ubu 
ak njàqarey xol bu sax, 
ba noon dootu ma man? 
 4 Céy Aji Sax ji sama Yàlla, geesu ma, wuyu ma, 
leqli ma, bala ma ne sërëx ci nelawi ndee, 
 5 noon ba naan: «Daan naa ko,» 
bañ yay bége saab jéll. 
 6 Man de maa ngi dénkoo sa ngor, 
di bànneexoo sag wall. 
Naa woy Aji Sax ji, 
ki may baaxe xéewalam.