Sabóor 14
Yàqute maase na 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda. 
Ab dof a ngi naa ci xelam: «Yàlla amul!» 
Ñu ni mel ay def njekkar, seeni jëf siblu, 
kenn defu ci lu baax. 
 2  Aji Sax jee tollu asamaan, jéer doom aadama, 
di seet ku ci xelu, tey sàkku Yàlla. 
 3 Ñépp lajj, 
bokk yàqu yaxeet. 
Kenn deful lu baax, 
du kenn sax. 
 4 Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? 
Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, 
te sàkkuwuñu Aji Sax ji.» 
 5 Foofu lañuy tiite tiitaange lu réy! 
Du Yàllaa ngi ànd ak kuréli ñu jub ñi? 
 6 Ku néewlee yaakaar, ngeen tas ko, 
waaye Aji Sax ji la làqoo. 
 7 Ana kuy xettlee Israyil fa Siyoŋ? 
Éy bés bu Aji Sax ji delloo ñoñam ndam, 
ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! 
Ndaw bànneex laa ne, ci Israyil gii!