Sabóor 15
Kuy aji jub? 
 1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. 
Aji Sax ji, kuy ganeji sa xayma? 
Ana kuy dëkki sa tund wu sell? 
 2 Xanaa ki wéye maandu, 
di def njekk, 
di wax dëggu xolam. 
 3 Du sos, 
du tooñ dëkkandoo, 
du baatal moroomam. 
 4 Ku siblu, mu sib, 
ku ragal Yàlla, mu teral. 
Mooy sàmm ngiñam, 
su ko dee lor it. 
 5 Du leble, ba teg ca; 
du nangu ger, ngir fexeel jaambur. 
Lii ku koy jëfe doo jang.