Sabóor 42
Maa namm Yàlla 
 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor. 
 2 Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox, 
maa la koy sàkkoo xol. 
 3 Maa mar Yàlla, 
Yàlla jiy dund! 
Kañ laay teewi fa kanam Yàlla? 
 4 Rongooñ laay dunde 
guddeek bëccëg, 
noon yi di ma dëkke naa: 
«Ana sa Yàlla ji?» 
 5 Lii laay fàttliku, sama xol jeex: 
dama daan jàll, jiite mbooloo ma, 
jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant, 
ñu booloo di màggal. 
 6 Moo man, lu may yoggaaral nii? 
Lu may jàq? 
Naa yaakaar Yàlla, 
ba dellu sante sama Yàlla wallam. 
 7 Maa ngi ne yogg, 
ba di la fàttlikoo fa réewum Yurdan 
ak tundi Ermon ak Misar. 
 8 Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; 
say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw. 
 9 Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram, 
guddi ma fanaane koo woy, 
di ñaan Yàlla mi may dundal. 
 10 Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko: 
«Lu tax nga fàtte ma, 
noon di ma fitnaal, 
may wéye tiis?» 
 11 Noon yaa ngi may ñaawal, 
di ma yendoo naa: 
«Ana sa Yàlla ji?» 
Ma ne yàcc, ne yasar. 
 12 Moo man, lu may yoggaaral nii? 
Lu may jàq? 
Naa yaakaar Yàlla, 
ba dellu sante sama Yàlla wallam.