Sabóor 43
Éy Yàlla, àtte ma 
 1 Éy Yàlla, àtte ma, 
layool maak xeet wu gorewul, 
xettli maak ku njublaŋ te dëng. 
 2 Yaw Yàlla kat yaay sama rawtu. 
Lu tax nga wacc ma, 
may wéye tiis, 
ci noteelu noon? 
 3 Ngalla yónneel sag leer ak sa dëgg, 
yal na ma yooyu jiite, 
yóbbu ma sa tund wu sell, 
sa dëkkuwaay ba. 
 4 Kon Yàlla, naa àgg sa sarxalukaay; 
yaw Yàlla, yaay sama mbégte, di sama bànneex. 
Yaw Yàlla, sama Yàlla, 
naa la màggale xalam. 
 5 Moo man, lu may xàddi, ne yogg? 
Lu may jàq nii? 
Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko, 
moom sama Yàlla mi may wallu?