Sabóor 98
Woyleen Aji Sax jiy àttesi 
 1 Muy kàddug Sabóor. 
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, 
moo def ay jaloore, 
kàttanam ak sellngay dooleem 
jox na ko ndam li. 
 2 Aji Sax jee xamleg wallam, 
feeñal njekkam, xeet yi gis. 
 3 Moo dencal bànni Israyil ngoram, 
dencal ko wormaam, 
àddina ba mu daj di gis 
ni nu sunu Yàlla walloo. 
 4 Yeen àddina sépp, xaacul-leen Aji Sax ji, 
sampleen, sarxolle te woy! 
 5 Xalamal-leen Aji Sax ji, woyal ko, 
xalamal ko, woyati. 
 6 Wal-leen liit yi, wal bufta yi 
te xaacul Buur Aji Sax ji! 
 7 Na géej riirandook li ko fees, 
mook àddinaak li ci biiram, 
 8 dex tàccu, 
tund sarxolleendoo, 
 9 gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, 
àttesi àddina, 
di àtte dun bi njekk, 
tey àttee xeet yépp dëgg.