Sabóor 99
Aji Sax ji buur bu sell la 
 1  Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko! 
Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu! 
 2 Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg, 
kawe, tiim xeetoo xeet. 
 3 Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaal-leen ko. 
—Kee sell! 
 4 Buur, jëfe yoon mooy dooleem, 
te yaa saxal njub, yoon ak njekk 
ci askanu Yanqóoba. 
 5 Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, 
te sujjóot fa ndëggastalam. 
—Kee sell! 
 6 Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam, 
Samiyel bokk ca ñay tudd turam. 
Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul. 
 7 Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom, 
ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon. 
 8 Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon, 
di seen Yàlla ju leen di baal, 
te di leen mbugale seeni jëf ju bon. 
 9 Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, 
te sujjóot fa tundam wu sell wa. 
—Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!