Sabóor 101
Buur a ngi jaayanteek Yàlla 
 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. 
Ngor ak yoon laay woy. 
Yaw Aji Sax ji laay joobe. 
 2 Naa teewlu yoonu maandute. 
Ana kañ nga may dikkal? 
Naa doxe maandute 
fi sama biir waa kër. 
 3 Caaxaani neen, xooluma; 
jëf ju wàcc yoon, bugguma, 
taqu ma fenn. 
 4 Kuy nas njekkar, sore ma; 
lu bon, xawma ko. 
 5 Kuy jëw moroomam, ma wedamal; 
ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la. 
 6 Ku dëggu ci réew mi, ma geesu, 
ngir fat ko. 
Te kuy wéye maandute, 
kookoo may liggéeyal. 
 7 Kuy njublaŋ du tooge sama kër, 
kuy fen du taxaw sama kanam. 
 8 Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi, 
ngir dagge ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw.