Sabóor 100
Aji Sax jee baax 
 1 Muy jàngi cant. 
Yeen waa àddina sépp, 
xaacul-leen Aji Sax ji. 
 2 Nangeen jaamoo Aji Sax ji mbég, 
dikke koy woy! 
 3 Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla. 
Moo nu sàkk, nuy ñoñam, 
di gàttam yi muy foral. 
 4 Nangeen dugge këram ag cant, 
dugg ëttam di màggal, 
sant ko, teral turam. 
 5 Aji Sax jee baax, gore ba fàww, 
worma ja sax dàkk!