Sabóor 121
Ana ku may sàmm? 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. 
Damaa séentu tund ya, 
te naan fu wall di jóge? 
 2 Sama wall a nga fa Aji Sax ji, 
ki sàkk asamaan ak suuf. 
 3 Kii du la bàyyi nga tërëf, 
sa sàmm bii gëmmul. 
 4 Kiy sàmm Israyil kay 
gëmmul, nelawul. 
 5 Aji Sax jee lay sàmm, 
Aji Sax jee lay yiir, 
féete la ndijoor. 
 6 Du naaj wu lay dal bëccëg, 
mbaa leer gu ndaw guddi. 
 7 Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, 
di sàmm sa bakkan. 
 8 Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk, 
tey ak ëllëg.