Sabóor 122
Nu ñaanal Yerusalem 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. 
Maaka bég, ba ñu ma nee: 
«Kër Aji Sax ji lanu jëm.» 
 2 Yaw Yerusalem, noo ngii taxaw sa bunt. 
 3 Céy, Yerusalem, dëkkub tabax bu baax, 
bi booloo, di benn. 
 4 Fii la giiri Israyil di yéegsi, 
di giir yi Ki Sax séddoo. 
Ñu ngi santsi Aji Sax ji, 
ni ko Israyil warloo. 
 5 Fii la ngànguney Israyil tege, 
askanu Daawuda toog ca, di àtte. 
 6 Dagaanleen jàmmi Yerusalem: 
«Yerusalem, yal na sa xeli soppe dal, 
 7 jàmm ne ñoyy fi say tata wër, 
te xel dal ci biir këri Buur.» 
 8 Mbokk ak xarit a waral 
may ñaan jàmmi Yerusalem. 
 9 Sunu kër Yàlla Aji Sax jee ma tax 
di sàkku ngëneelu Yerusalem.