Sabóor 124
Nanu sante Aji Sax ji wallam 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. 
Éy su dul woon ak Aji Sax ji nu nekkal! 
Israyiloo, waxati ko: 
 2 su dul woon ak Aji Sax ji nu nekkal, 
ba ñu nu jógalee, 
 3 ba nit ña xadaroo sunu kaw, 
dañu nu doon wonn, nuy dund, 
 4 dañu nu doon mëdd nim ndox, 
def um wal, buub nu, 
 5 def waame wuy wal-wali, 
buub nu, yóbbu. 
 6 Cant ñeel na Aji Sax ji, 
ki nu bàyyiwul, noon yi yàpp nu. 
 7 Danu ne fërr, nim picc 
mu rëcc fiiru rëbb, 
fiir ga toj, nu raw. 
 8 Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji, 
ki sàkk asamaan ak suuf.