Sabóor 125
Ku doyloo Aji Sax ji raw 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. 
Ku doyloo Aji Sax ji, 
yaay tundu Siyoŋ, doo toxu; 
dangay sax ba fàww. 
 2 Ni tund yi yéewe Yerusalem, 
ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam, 
tey ak ëllëg. 
 3 Nguur gu bon du saxe 
kaw suuf su nit ñu jub muurloo. 
Lu ko moy ñu jub ñi sàkku lu bon, 
di ko jëfe. 
 4 Éy Aji Sax ji, baaxeel ku baax, 
ak kuy mébét njub. 
 5 Waaye kuy topp yoonu ndëngte, 
Aji Sax jee koy sànk, 
boole kook kuy def lu bon. 
Yal na jàmm dal Israyil.