Sabóor 128
Ragal Yàlla, jàmmi kër 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. 
Ndokklee képp ku ragal Yàlla, 
di jëfe ay yoonam. 
 2 Yaay lekk saw ñaq, 
mbégteek ngëneel ñeel la. 
 3 Sa jabar ni garab gu nangoo sa wanag, 
say doom wëra wër sa ndab ni njëmbat lu jebbi. 
 4 Ki ragal Aji Sax jaa ngoog, 
nii rekk lay barkeele. 
 5 Yal na la Yàlla barkeele fii ci Siyoŋ; 
yal nanga teewe xéewalu Yerusalem 
sa giiru dund gépp, 
 6 te nga gis say sët. 
Yal na jàmm dal Israyil.