Sabóor 129
Noon manul Israyil 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. 
Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonala sonal. 
Israyiloo, waxati ko: 
 2 Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonala sonal, 
te taxul ñu man ma. 
 3 Sama gannaaw gi lañu gàbba gàbb, 
rëdd koo rëdd nib tool. 
 4 Waaye Aji Sax ji boroom njekk 
dog na buumi ñu bon ña. 
 5 Képp ku noonoo Siyoŋ 
yal nañu ko dëpp, gàcceel ko. 
 6 Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd, 
balaa law, lax. 
 7 Du doyub ŋëb ku ko dog; 
du doyub say ku ko for. 
 8 Ku fa jaare it du ko ne: 
«Jaajëf, Aji Sax ji barkeel; 
jaajëfe yaw, yal na Aji Sax ji barkeel.»