Sabóor 141
Yàlla, sàmmal sama làmmiñ 
 1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. 
Aji Sax ji, woo naa la, gaawe ma! 
Bu ma lay woo, teewlu ma. 
 2 Yal nanga ma nangul samag ñaan 
ni cuuraay lu ñu la taalal, 
yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm. 
 3 Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, 
saytul ma sama kàddu. 
 4 Bu ma xiir ci lu aay, 
may jëfe jëf ju bon, 
ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, 
di wàlli seeni bernde. 
 5 Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, 
bantal ma ci ngor. 
Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. 
Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy. 
 6 Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, 
ba noon yi xam ne dëgg laa wax. 
 7 Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, 
ni la njaniiw di ŋaye, 
aw seeni yax yu tasaaroo. 
 8 Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët, 
yaw laa làqoo, 
bu ma seetaan, ma dee. 
 9 Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal, 
ak fiir yi ma defkati ñaawtéef yi tegal. 
 10 Yal na ku bon tàbbi cig fiiram, 
te man ma teggi, wéy.