Sabóor 142
Aji Sax ji rekk a ma yég 
 1 Muy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma. 
 2 Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; 
àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji, 
 3 sippi ko sama tawat, 
diis ko sama njàqare. 
 4 Bu ma yoqee, 
ràññee nga samay jéego; 
yoon wi may jaare 
lañu ma làqal am yeer. 
 5 Ma geesu ndijoor, xool; 
du kenn ku ma faale. 
Rawtu réer ma, 
du kenn ku sama bakkan saf. 
 6 Aji Sax ji, ma woo la wall; 
ma ne, yaay sama kiiraay, 
di sama séddoo fi kaw suuf. 
 7 Teewlul, ma ne wóoy, 
damaa manatul, 
xettli ma ci ñi ma topp, 
dañu maa ëpp doole. 
 8 Ngalla génne ma fi ma tëje, 
ma sant la. 
Man la way-gëm ñi di yéew ëllëg, 
yaa may xéewale ab yool.