Màndiŋ ma
fa bànni Israyil jaare woon
di ñeenteelu xaaju Tawreetu Musaa
Ubbite gi
Téere bii moo tàmbalee ca bés ba bànni Israyil dalee ca taatu tundu Sinayi. Foofu la bànni Israyil jóge jëm màndiŋu Paran, ca bëj-gànnaaru réewum dige ba. Fa lañu yebale ay ndaw yu yërnduji réew ma, te délsi wax seen gis-gis ca ña fa dëkke. Ba ñu demee ba délsi, lañu ne ñoom la ñu gis neexul. Loolu nag tax bànni Israyil di nàttable ndax Yàlla man na leena jox suuf sa mu leen sédd. Ci kaw loolu ñuy jàmbat ci kaw Yàlla. Seen ñàkk kóllëre googu tax na Yàlla teg leen ab daan, ñuy wëndeelu ca màndiŋ ma, ba maas ga doon jàmbat dee, ba geneen maas wuutu leen. Ñeent fukki at lañu wëndeelu, doora walbatiku dox ndànk, jëm Kanaan. Boobu yoon lañu doora nangoo déggal Yàlla. Gannaaw gi lañu sumb ay xare yu am solo, ba daan, ca penkub dexu Yurdan, doora waaj, ngir jàll ca biir réewum dige, ba ñu nammoona gis bu yàgg. Téere bi wone na ne, ni xolu doom Aadama mel rekk moom la ñoñi Yàlla feeñal ci seen jikko ju toogadi. Saxoowuñu lenn, xanaa ŋarale diggante ngëm ak nàttable, cawarte ak xàddi, jëfi ngor ak jëf ju sew. Seen jikko jooju la téere bi wone ne moo leen worale ak Yàlla mi dul soppiku ci kóllëreem, digganteem ak ñoñam, doonte kóllëre gi nag, teewu koo yor ab yaram, te ànd ak njubteem. Musaa nag diggante bu xat lañu ko gisal ci téere bi, Aji Sax ji ak ay bokkam séq ko: Musaa moo doon ndawal Yàlla liy jottli ay ndigalam, te amul woon ab dend ci na mu xejjoo woon ak Yàlla, waaye moo taxawoon itam fa kanam Yàlla, taxawal fa askan wu ñàkk kóllëre, di ko layal te tàyyiwul.
Ci Tënk:
Saar 1—21 Israyil jànge na ca maam ya jóge woon Misra
Saar 22—25 Céru barke bu sax ñeel na Israyil
Saar 26—36 Israyil dégg na ab artoom balaa dugg Kanaan
Israyil jànge na ca maam ya jóge woon Misra
(Saar 1—21)
Takk nañu limu bànni Israyil
1 Aji Sax ji moo wax ak Musaa ca màndiŋu Sinayi ca biir xaymab ndaje ma, keroog benn fanu ñaareelu weer wu ñaareelu at, ma topp ca gàddaay ga bawoo Misra. Mu ne ko:
2«Limleen mbooloom bànni Israyil gépp, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam. Waññleen góor ñépp, bopp ak bopp, ku nekk ak turam. 3Li ko dale ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci Israyil daal, nangeen leen lim, gàngoor ak gàngoor, yaw ak Aaróona. 4Giir gu ci nekk, àndleen ceek kilifa yi jiite seen këri maam, ñu jàpple leen ci.
5Ñiy wuyoo tur yii nag, ñoo leen ciy taxawu:
Ci wàllu Rubeneen ñi, Elisur doomu Sedeyur.
6Wàllu Cimyoneen ñi, Selumyel doomu Surisadaay.
7Wàllu Yudeen ñi, Nason doomu Aminadab.
8Wàllu Isakareen ñi, Netanel doomu Suwar.
9Wàllu Sabuloneen ñi, Elyab doomu Elon.
10Ñi ciy askanu Yuusufa ñii la:
Ci wàllu Efraymeen ñi, Elisama doomu Amiyut.
Wàllu Manaseen ñi, Gamalyel doomu Pedasur.
11Wàllu Beñamineen ñi, Abidan doomu Gidoni.
12Wàllu Daneen ñi, Ayeser doomu Amisadaay.
13Wàllu Asereen ñi, Pagyel doomu Okkran.
14Wàllu Gàddeen ñi, Elyasaf doomu Dewel.
15Wàllu Neftaleen ñi, Ayra doomu Enan.»
16Ñooñu lañu woo ci mbooloo mi, muy ñi jiite seen giiri maam. Ñooy njiiti gàngoori Israyil.
17Ba loolu amee Musaa ak Aaróona tofloo ñooñu ñu tudd seeni tur, 18ñu dajale mbooloo ma mépp, keroog ca benn fanu ñaareelu weer wa. La ko dale ca ña am ñaar fukki at, jëm kaw, ñoom ñépp daldi bindu ca limeefu tur ya, ku nekk ak kër maamam, giir ak giir, làng ak làng, bopp ak bopp. 19Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi.
20Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israyil seen maam, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 21Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
22Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Simeyon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 23Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
24Ñu lim turi sëti Gàdd, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 25Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
26Ñu lim turi sëti Yuda, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 27Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600).
28Ñu lim turi sëti Isaakar, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 29Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
30Ñu lim turi sëti Sabulon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 31Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
32Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Efrayim, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 33Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
34Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Manase, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 35Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200).
36Ñu lim turi sëti Beñamin, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 37Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). 38Ñu lim turi sëti Dan, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 39Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700).
40Ñu lim turi sëti Aser, ku nekk ak làngam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 41Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500).
42Ñu lim turi sëti Neftali, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. 43Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
44Yooyu limeef la Musaa ak Aaróona tënk, ña leen ca jàpple di fukki kilifay Israyil ak ñaar, ku ci nekk taxawal kër maamam. 45Mboolem bànni Israyil yi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, limees na leen, ku ci nekk ak kër maamam. 46Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
Limaaleesul Leween ñi
47Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom. 48 Aji Sax ji moo waxoon Musaa, ne ko: 49«Giirug Lewi ñoom, bu leen lim, bu leen waññaaleek bànni Israyil. 50Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal. 51Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey. 52Bànni Israyil gi ci des, na ku ci nekk topp dalam, ak raayaam ak kurélam. 53Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee am sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israyil. Te itam na Leween ñi dénkoo dénkaaney jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.»
54Bànni Israyil daldi def noonu. Mboolem lu Aji Sax ji santoon Musaa, noonee lañu ko defe.

Notes


*1:20 1.20 Israyil mooy Yanqóoba.